Magg mo mane n Magg mo eh mane nameunala Bësub kerook gee Sama adduna moo tukkee Jile xibaar, lu ko gëna doy waar Xaaji guddi lañu ma woo Nema moom dem na Mënumako woon gëm Waaye dem na Jaam beek pexeem, ni Yàlla dogalam Lu metti góor lay dal Bëggoon na ñu nga took fi ba ci kanam Bu Yàlla nee waawaaw jaam du ne déedéet Dem na, dem na du ñëwaat Moom de dem na du ñëwaat Sama mag jee, man namm naa la This the life the life mysterious life This is the life the life eternal life Mag mo yaw, man namm naa la Mag mo he, man namm naa la Ñëpp ñu ngiy jooy Wéetal ga ñu Yaay mu ngiy jooy Baay Mag ak rakk Mbiidu mu ngiy jooy, Paap Muusaa mu ngiy jooy Isaa Ngeer mu ngiy jooy Laay Géey Niep ñu ngiy jooy Djiby agn mu ngiy jooy elaj mu ngiy jooy Sylvain mu ngiy jooy Man gëm naa ne Aljana ngay yeewo Yaa ma yàgg wax ni lépp dina baax Yàgg nga ma wax ni picc moom jógul rekk naaw Fàllu na la teeru, Sëriñ Tuuba na la teeru Serafaal na la teeru firdawsi ngay Doxonto Sama mag jee, wéetal nga ñu Sama mag jee, ñun de namm na ñu la Mag moo yaw nax nga ñu ba dem Sunu mag jee Wéetal ga ñoo Eh he he This the life the life mysterious life This is the life the life eternal life Mag mo yaw, man namm naa la Mag mo he, man namm naa la Aljana ngay doxonto, nañu fa gisante Du ñu la fàtte, yaa ngi yaw suñu xel Sama mag jii, moom dem na eh Moom de demna Life eh he he he Magg mo he he Man namm naa la, namm naa la, namm naa la Aljana ngay doxonto sama mag jee duñu la mësa fàtte Wéetal ga ñoo, duñu la mësa fàtte Wéetal ga ñoo, duñu la mësa fàtte